Abajada wolof
Wolof
SoppiLii mooy abajada wolof bi nguuru senegaal jàpp, képp kuy bind wolof war cee tënku
Abajada wolof
Soppia - à - aa - b - bb - c - cc - d - dd- e - ee- é - ée - ë - ëe - f- g - gg - i - ii - j - jj - k - kk - l - ll- m - mm - mb - n - nn - nc - nd - ng - nj - nk - nq - nt - ñ - ññ - η - ηη - o - oo - ó - óo - p - pp - q - r- rr - s - t - tt - u - uu - w - ww - x - y - yy.
N° | Araf | Bopp | Biir | Mujj |
---|---|---|---|---|
1 | a, A | am | sabar | mala |
2 | à, À | àllarba | muskàllaf | amul |
3 | aa, Aa | aar | talaata | Tuubaa |
4 | b, B | bax | jabar | rab (rabu àll) |
5 | bb | amul | jebbi | dëbb |
6 | c, C | coono | looco | amul |
7 | cc | amul | soccu | bàcc |
8 | d, D | der | xadar | amul |
9 | dd | amul | buddi | sedd |
10 | e, E | em | xel | fexe |
11 | ee, Ee | ee | bees | bee |
12 | é, É | amul | béy | xulé1 |
13 | ée, Ée | éem | féey | bu bëggée1 |
14 | ë, Ë | ës | fës | amul |
15 | ëe, Ëe | amul | bëer | amul |
16 | f, F | for | nafar | nef |
17 | g, G | garab | jagal | nag (nagu Sàmba) |
18 | gg | amul | rogganti | segg |
19 | i, I | itte | tis | kaani |
20 | ii, Ii | iir | riiti | bii |
21 | j, J | jabar | fajar | faj (fajal) |
22 | jj | amul | dàjji | bojj |
23 | k, K | kafe | saaku | ak |
24 | kk | amul | màkkaan | lekk |
25 | l, L | lam | nelaw | xel |
26 | ll | amul | xolli | dàll |
27 | m, M | mar | laman | xam |
28 | mm | amul | sémmiñ | jàmm |
29 | mb, Mb | mbootu | càmbar | démb |
30 | mp | amul | càmpóor | samp |
31 | n, N | nar | daanu | fen |
32 | nn | amul | bënnu | wann |
33 | nc | amul | dencukaay | sanc |
34 | nd, Nd | ndox | rendi | lënd |
35 | ng, Ng | ngoon | teraanga | lang |
36 | nj, Nj | njàmbal | Bànjul | donj |
37 | nk | amul | sànkar | tànk |
38 | nq | amul | sanqal | janq |
39 | nt | amul | santaane | bant |
40 | ñ, Ñ | ñam | wañaaru | ngooñ |
41 | ññ | amul | wàññi | dëññ |
42 | η | ηaam | daηar | laη |
43 | ηη | amul | wàηηarñi | doηη |
44 | o, O | opp | lop | laalo |
45 | oo, Oo | oom | boroom | àndandoo |
46 | ó | óbbali | jóg | pusó1 |
47 | óo | óom | góor | xulóo1 |
48 | p | put | ciipatu | amul |
49 | pp | amul | ηàppati | lupp |
50 | q (ñaari xx) | amul | làqarci | mëq |
51 | r, R | raxas | maral | liir |
52 | rr | amul | amul | fërr |
53 | s, S | suuf | desit | fas |
54 | t, T | tool | tuuti | nit |
55 | u, U | um | buddi | kuddu |
56 | uu, Uu | uuf | buur | luu |
57 | w, W | wasin | tawat | xew |
58 | ww | amul | xewwi | jaww |
59 | x, X | xar | saxaar | lex |
60 | y, Y | yaram | layoo | bey |
61 | yy | amul | feyyu | coyy |
1- Doonte sax, li ñu téj ci biir lonk yi ngay dégg, nanga bind: xule, bu bëggee, pus, xuloo.