Fonk sa bopp
(Yoonalaat gu jóge Fonk saw bopp)
Nos / Taalif
SoppiMaa leen di jébbal ab/as njukki ci taalif bu Abdu Xaadir Gey Taalif
- Aw làkk a ngii wareesukoo sàggane () kum soxalul xam aguloo lumu mane
- Ak a nooy te matale man na lu ne () Tànn leen ko nu far ko di waxtaane
- Yéwwute bokk na ci fonk sa làkk () Dina waral nga déggook say mbokk
- Xam-xam la ca jiitu dégg sa làkk () Dégg gu wer dica waxtaan te dica sàkk
- Deglu leen ma wax lima fanaane () Tëdd di gent guur def ko waxtaane
- Mudi jël làkk wi def ko wow ofisel () Dici xalaat dici lëggeey looloo di xel
- Àbb aw làkk indi ko di ci lëggeey () Te yor wu mat nit ku ñuul yeen a geey
- Ku la aal bët fuko neex yaw ngay man a xool() Lu lay may bët du naggu yaw nga diko xool
- Looloo nu dal batax dunu dem ca kanam () Jéggaani làkk, cosaan, ba ci xam-xam
- Jëm ciw naaj àbbi dàll ànd ak boroom () Bu tàggee mu laaj la ko nde mooko moom
- Mbokk yéwwul te xàmmee yaw linga moom () Tobaab ya de tée nañu ñoom lañu moom
- Maay jooy tu lii ci kanamu waa guur gi () Ak ku ko man ci askan wi mbaa kili fa gi
- Sosal nufi baatukaay nuy baatal () Di sosi baat, baat bu jagul nu baaxal
- Làkk woo xamni numu laneexe nga koy waxe () Lii de ganul nañu ci sàkki am mbexe
- nàngam-nàngam.............
Abdu Xaadir Gey >>Ahloubadar (221) 77572 45 77