Fr:proverbe

  1. Alal du faj dee, gàcce lay faj
  2. Am saxul, ñàkk saxul
  3. Ay du yam ci loosu boroom
  4. Ay du weesu baay dee na
  5. Àdduna weeru kóor la, fàww jant so nga doora wàññi bis.
  1. Bàkk nga njaak
  2. Bu ndox tuuroo am bàq a fa des
  3. Bu ñay di xàlluw yoon doom jaa tax
  4. Bërigo ci mbartal ku ko bëmëx mu dem, ku ko ba, mu dem
  5. Bu gudd nopp doon tax di njiit mbaam di suñu ilimaan
  6. Buur du mbokk
  7. Bala ngaa xam xamadi xaw laa ray
  8. Bëñ weex na lool waaye dereet a ko lal
  9. Bu/Su yoon jeexul waaxusil du jeex
  10. Boroom ñeenti tànk du lab
  11. Boroom mbaam a xam mbaamam
  12. Boroom lal a xam màtti lalam
  13. Bët du yanu waaye xam na lu bopp àttan
  14. Bakkan waraw dàll la, fa muy dàggee dooko yëg
  1. Cërub ma xàjj, ma xujj a koy jël
  2. Cuqum a gën kamm
  1. Doomi ñay bu ko ñaanal mu rëy, ñaanal ko gudd fan
  2. Duma jënd jaan ci pax
  3. Dama laa bëgg maa la raw sëy bu mu takk, dangaa reew yaa ma raw a koy tas (abdu xaadir géy)
  4. Dangaa jot ci bakkan bay ñandu
  5. Daaray lëg guddu nopp jarufaa jaay
  6. Dóor wa ray mbër ci ponkal lay bawoo (Ahloubadar)
  7. Dëkkandoo jàmm a ca gën
  8. Doomi mbër jàngil bëre, yàgg-yàgg dees na la ñam
  1. Fa ndox daa taa boo demee fekk fa tepp-tepp
  2. Fët-Fët tàggalewul mbaam'aki noppam
  3. Fullaay jaay daqaar, mbaa ma ñam jeexal ko
  1. Gaynde du lekk mbuum yàpp lay dunde
  2. Gewël bu reppee cib xare lu mu jiin xeep ko
  3. Gumba du jiite rëbbum jaan
  4. Gumba tal na lu dul tëbi kàmb
  5. Góor gu tàyyeel, gàtt wërsëg, néewi soppe
  1. Jigéen soppal te bul wóolu
  2. Jëm ca làmb ja di bàkku, juge ca di bàkkoo ko gën
  3. Jàng jàngaan boo mokkalee ber sa daara
  4. Jàngoro ku ko nëbb mu lor la
  5. Jàngoro dees koy weer
  6. Jikkook boroom pax rekk
  1. Ku muñ muuñ
  2. Kewël du tëb doom ja bëtt
  3. Kuy naan di nëbbu, boo jéggee feeñ
  4. Ku njëkk a jug boroom ndékki dinga tëddaat
  5. Ku boot bukki xaj bëw la
  6. Ku wex wéet
  7. Ku ñuy jiiñ dëmm ngay soccoo yaxi liir
  8. Ku puudër tax a rafet boo ñaqee ñaaw
  9. Ku bañ a xitax bul yàgg ca mbojj ma
  10. Ku yàgg cib teen baag fekk la fa
  11. Ku manul, bawoo, lu yàqu yaw a
  12. Ku log, log-logal
  13. Ku la aal bët, fu ko neex ngay xool
  14. Ku saraxul gumba, bàyyi kook yalwaanam
  15. Ku ndobin ray sa maam, boo gisee lu ñuul war a daw
  16. .... Ku ko lebal ker, mu faye la guddi
  17. Ku jaan matt sam xel dem ci dee
  18. Ku la mag ëpp lay sagar
  19. Kuŋ-kuŋ ca wolandoo wa
  20. Ku yar sam kuy, yaw lay njëkk a daan
  21. Kuy xalam di ca jaayu (joowu)
  22. Kiy yenni gan du ko gunge
  23. Ku bëgg akara dangay ñime kaani
  24. Ku niikiwul naaka
  25. Ku naggu, naggu loo moomul,
  1. La tee nag wa dabi nag yaa tee ñeex maa neex
  2. Lu waay rendi sa loxo lay nàcce
  3. Lëg bu lekkee olom na ko gërëme cooy
  4. Laago du wees
  5. Lu jot yomb
  6. Lu xaj lekk lekk, ba fa der ga ca baat ba
  7. Liggéeyu ndey añub doom
  8. Lu ñépp wax ay dëgg
  9. Lu yàgg dëgg la
  10. Lu defu waxu, Luy ay di njàmbat
  11. Lu njiig njaaga mooy njaag
  12. Lu mag def dee, bu dekkee ba ko
  13. Lekkoo ci ndab li bëgg cee xëpp suuf
  14. Li ci kanam, rawuli gët
  15. Lu cin xat xat, nga war caa boqus xorom
  16. Lu yëngu la ko yëngal a ko ëpp doole
  17. Lu jiwu wa jeexul jugu fa
  1. Mbejum kanam, boroom a koy fajal boppam
  2. Mbej wa ray mbër, ponkal a koy dóor
  3. Mag mat naa bàyyi cim réew
  4. Man a man a, yaw a yaw aa ko gën
  5. Mattum xaalis boroom a koy jaaroo/suuroo
  6. Muus mu nekk ak na muy toje boppu jinaxam
  1. Ndànk ndànk ay jàpp golo ci ñaay
  2. Nen, du bëreek doj
  3. Nit, nitay garabam
  4. Njëkk a fecc, taxut a mujjeb géew
  5. Njaabum giléem, xajul ci waañ
  1. Ñulug sa jëkkër, yakk sa doom
  2. Ñu bokkub teen ay jaxasoo ay goj
  3. ñi man a kott amuñu mbaam
  1. Powum jaar, ca wetu paxam
  2. Picc mu masul a naaw, bu/su naawee firi'm réew
  1. Rayub tubaab yomb na, waaye fekke dëj baa jafe
  1. Suul ker du ko tee feeñ
  2. Sikk su feeñ cib sëy, nuyyoo na ca ngoro ga, dees koo fayul
  3. Sa gimiñ xasaw na sa doomu nday a la koy wax
  4. Saabu du fóot boppam
  5. Saaku bu dara newul du taxaw
  6. Soxla buy ñaar jàmm a ga ca,
  1. Tarxiis bu dammee loosu mbonaat, ku yor gëléem war a yësal
  2. Tere tere mu të, bàyyil mu gis
  3. Tàmm laago la
  4. Toŋ-Toŋu naat su wëreem réew dunq yaa tax
  5. Teen bu neexee pind ba du féex
  1. Weex, yàquli bëñ
  2. Waxma sa xarit, ma wax la sa bópp
  1. Xaalis, amul xarit
  2. Xaalis loo ko yonni mu indi ko, waaye falay jaare
  3. Xel, du jariñ lu dul xalaat
  4. Xar, day weesu mbote
  5. Xarit, dees koy tànn
  6. Xeeb nga xal, mu lakk sa dàgga
  7. Xool asamaan jarul buuxante
  8. Xëbtal, du tax doomi lëg a màtte
  9. Xalangu, dajul suuf.
  1. Yàgg bawul dara
  2. Yariit du bon, yarut du baax (ahloubadar)
  3. Yéene néeg la boroom a cay fanaan
  4. Yoon yamul ci benn
  5. Yàkkamti yàqule