Tërëlinu Ndimbal gi ci Wikipedia

Xët mii daf lay won lëkkalekaay yi ëpp njariñ ngir nga mana indi sa wàll te jang jëfëndikoo Wikipedia.
Dañ leen seddale ci'y xaaj yu'y gën di jafe looy gën a dem, yu'y wax ci doxinu dalu bi, ay baaxu Wikipedia ak ay atteem yu ñuy jox-cër, ci soppi xët yi, yokkug ndef ak melokaanu xaralay téerexamteef gi.

Ubbite

Soppi
 

Jeego yu njëkk

  Jàng téerexamteef gi

Soppi
Nooy yëree xët yi
Xët mii moo lay wone fann yu bari yoo mane yëngoo ci biir téerexamteef gi
Seet am xët
ci lu bari jukki gi ngay seet day doon lu laxu. Jukki gii di nala jox jumtuwaay yi war ngir sag seet jur dara.
Daŋkaafu yëpp
matuwaay yi nga wara jël, yi ñeel ndefug téerexamteef gi.

 Tambalil bokk

Soppi
xët wu njëkk wu wacc bees yi
Ci xët mii lañ lay dalale-jamm ci Wikipedia

  Li lal sosoom

li lal sosoom
dañ di ay baax yoo xamne way-bokk yëpp a ci war di dekku, bawul kenn. Ñëw leen xool leen.

  Xam Wikipedia

Maanaam
Ab gisin bu gaaw ci li mu doon,jaar-jaaram gu gatt, doxinam ju daj, ak yeneen.
Li Wikipedia doonul
Gis tamit li mu doonul ak li ngeen fi dul gis.
Limu ay laaj
Ay tontu ci laaj yi gënë bari ñeel Wikipedia.
Wikipedia
Am jukki ñeel cosaan ak melokaanu Wikipedia.

Ngir mana duggal dara

Soppi

  Soppi jukki yi

Nooy duggalee ab baat
Nooy mana andee say mbind ci téerexamteef gi
Nooy sosee am Xët
Ngir sakk xët mu bees (sa xëtu bopp, am jukki, am wall ak yeneen) loolu lanuy faramface ci mii jukki.
Man mbindin ngay jëfëndikoo?
Fii ngay gisee xàll yi gënë yaa, ci mbindin mu yomb gooy jëfëndikoo ci xët yi ngay sos wala di ko nos ci Wikipedia
Nan ngay lëkkalee ay jukki ci seen biir?
NI mu utee ak yeneen téerexamteef yi, Wikipedia day def nga mana juge ci am xët dem ci menen ci anam gu yomb lool. Loolu laaj na, saa yooy soppi wala sakk am jukki, def ci ay lëkkalekaay biir.
Nooy duggalee lëkkalekaay biti?
Ngir yenn jukki yi, man naa doon lu solowu yenn saa yi nga def ay lëkkalekaay biti yu lay yòbb ci yeneeni barad, yuy yokk ay xibaar ci li nga jota wasaare.
Nooy duggalee ab lëkkalekaay diggantey-làkk?
Dafa am ay way-wikipedia yu bari ci yeneen làkk. Nii lanuy duggalee ay lëkkalekaay diggantey-làkk ci biir jukki yi, ngir jàngkat yi man kaa am ci yeneen làkk.
Ay kaddu ci say coppite
Ay baat yu néew ci li waral coppite yi, loolu di na noppal way-wikipedia yi

  Jëfëndikookat

Mbindu
Donte doonul lu manuta ñakk, bindu ngir mana indi dara, waaye am na ay ngëneel yu jara bayyi xel ci def ko. Xool leen nunuy bindoo.
Tàneefu Jëfëndikookat
Léegi nga xam ne bindu nga ba noppi, man nga duggu ci samay tàneef soppi ko ci niŋ ko bëggee.
Xëtu jëfëndikookat
ci sag mbindu, am na am xët muñ lay jaglel, foofu ngay bind dara ci yaw
Soppi turu jëfëndikookat
Su fekkee sa turu jëfëndikookat neexatula, man nga kaa soppi ci lu gaaw, leeral yaa ngi ci mii xët