Njàggat benn la ci anam yi nit di génnee ak a feeñale li nekk ci moom ciy yëgg-yëgg aki xalaat aki ñeewant aki gis-gis, jaare ko ci ay mbind walla bindiin yu rafet te wuute, moo xam woy la ( maanaam poesie) walla wesar (bind ci lu dul di ko nos, maanaam safaanub woy) walla wesar wu ñu nos. Loolu nag di ubbil nit ay bunt ngir mu am man-man ci feeñal ak génne li ñu manul a génne walla ñu koy man a feeñale ci geneen anam walla melo. Njàggat nag day takku takku gu dëgër ci làkk. Dëgg-dëggi njuréef walla ngérte li juddoo ci làkk ñu bind ko, walla caada ja ca juddoo, day nekk di lu dencu walla lu wattuwu ci biir melokaani njàggat yi aki peeñ-peeñam, te ñoom danuy wuute kem ni gox yi di wuutee jamono yi di ko wuutee. Jamono ju nekk tam ay soppiku da ciy sosu akug jëm kanam akug wuute ak xeetu ànd ak jamono yi