Nooy dugale baat bu bees

So bëgge dugal baat bu bees ci wikbaatukaay am na yoon yu bari yoo man a jaar.

Balaa dara, da ngaa war a seet baxam baat bi ngay dugal am na fi ba noppi walla déet, baat bi man naa am te niñ ko binde baaxul, kon loolu tamit jar na bàyyi xel, te ngay bàyyi xel ci araf bu njëkk bi, ndaxte baat bu tambalee araf bu mag ak bu tambalee araf bu ndaw, donte benn baat bi la, wikbaatukaay daf koy jàppe niki baat yu wuute, lii man na jur njuumte, waaye dal bi nii lañu ko tëralee .

Ngir amal ceet gi man ngaa bind baat bi ci boyotu ceet bi ci sa cammoñ, cuq ci ayca. Su fekke baat bi am na ba noppi dala kay ubbil, su amul mu laaj la baxam bëgg nga koo sos. Baat bi ngay dugal mooy nekk boppu xët wi, ci biiram nga def fa tekkeem ak ci yeneen làkk yi nga xam.

Ñaar

Soppi

Man ngaa dugal baat bi fii ci suuf, ngir xam ndax am na am déet.

Seet ab baat
 

Misaal

Soppi

 
== wolof ==
{{gongikubaat}}
(fii nga wax fi reenu baat bi, tëggiinam )
{{tur}}
(su fekkee turu lenn la)
# fii nga joxe fi ay misaal ci jëfandikuwiinunam
# fii nga joxe fi ay misaal ci jëfandikuwiinunam
{{jëf}}
(su fekkee jëf la)
# fii nga joxe fi ay misaal ci jëfandikuwiinunam
#fii nga joxe fi ay misaal ci jëfandikuwiinunam
{{bokktekki}}
fii nga joxe fi baat yi mu bokkal tekki
{{safaantekki}}
fii nga joxe fi baat yi mu safaanool tekki
{{bayyikoo}}
fii nga joxe fi baat yi juddoo ci moom
== Tekki ==
{|classe"wikitable"
|{{fr}}: [[tekkeem]]
|-
|{{en}}: [[tekkeem]]
|}
.

su fekkee baat bi wolof la ci suufu xët wi nga def fa [[Wàll:baati wolof]] lii day tax baati wolof yépp bokk nekk ci wenn xët. Man nga cee boole tamit [[Wàll:melosuuf]] su fekkee baatu melosuuf la walla [[Wàll:xam-xamu nosukaay]] su fekkee baatu xam-xamu nosukaay la, walla li mu doon ci gàttal.

Xoolal xët wii dànkaafu mu jox la dànkaafu.

Soo dugale baatu wu-faraas it noonu; ci biir xët wi nga def fa [[Wàll:wu-faraas]] su ko defee baat bi dugg fii Wàll:wu-faraas