Wiktionary:xaralaymbej

Ci xët wii baat yi ñeel Xaralaymbëj lees fiy waxtaanee

bobine: taxañ

  • cathode : wàccu
  • centrale électrique: digg bu mbëj
  • centrale idroélectrique: digg bu ndoxmbëj
  • centrale nucleaire: digg bu saal
  • centrale termoélectrique digg bu tàngmbëj
  • circuit: ndombo g
  • circuit primaire  : ndombo gu njëkk
  • circuit secondaire: ñaareelu ndombo
  • charge: yan b,
  • charge électrique : yanub mbëj
  • champ électrique : toolu mbëj
  • champ magnetique: toolu bijjaakon
  • chute de tension : wàccug dend
  • condensateur: fattalukaay (suma juumul fattalukaay yaa ngi ko jële ci fatt, kon foog naa ne bokkul ak liñu jublu ci condensateur, ndax ab condensateur fooy dugal mbëj la rënk ko fa, moo tax tax ma woowee woon ko rënkukaay)(bu fekkee fees di dence la, kon renkukaay, waaye bu dee ci baat bi rekk lees sukandiku moom fattalukaay lay man a doon ndax condenser moy rendre plus dense, te dense mooy lu fatt, xool:http://www.linternaute.com/dictionnaire/fr/definition/condenser/.
  • capacité: man-man b (capacité jubluwuñu ci li nga man def, sa man-man, waaye li nga man a dugal ci condensateur bi ci limu mbëj. def nag jubluwuma ci faire, waaye ci misaal: sunuy wax "ndab li dafa am def" maanaam li nga ci man a def dafa bari. Kon fii def moo fi gën a jekk man-man)(kon kay yaatuwaay mooy baay, mbaa yatalees ko baat ne këmbte.
  • conducteur électrique : wommatkaayu mbëj (wommat ak watat benn la rekk, (wommat moo gen ndax lu neew laay degg watat, lu ci epp wat lees di wax, te wat mooy diri, wommat nag lees jiital lay doon, walla loo jiitu di ko xecc, man naa doon lees di wat, mbaa lees di nioddi mbaa lu nuy jiitaal di daq niki ag jur)
  • courant électrique permanent stationnaire : dawaanu mbëj bu dëkke tekkaaral
  • conductivité: wommatiin w (conductivité: ni ñu man a wommate, ni wommatukaay bi di wommate dawaanu mbëj bi, wommatiin, man watatiin laa ko woowee woon, waaye benn la rekk)
  • conductance: yolomlu g, bayliku g
  • continue: wéy
  • courant alternatif : dawaan buy safaanu
  • courant polyphasés : dawaan bu bariwéq (lu tax weq = fase?)
  • courant de saturation : dawaanu regg
  • ligne de forces : rëddu doole
  • loi de Joule : àtteb Joule (di jàng jaawul)
  • perte: ñàkk g
  • potentiel : aj
  • période: diir b
  • permanent: sax, dëkke
  • pile : tegle b
  • pôle : dott b
  • polarisation : dottal b
  • pont: sala, jeggiwaay, pom
  • potentiomètre: nattaj
  • propagation : tas, wisaare, wisaaroo
  • puissance: doole, kattan, man-man. ngóora:virilité ( doole:force, kàttan:energie, ci xarala benn baat manula am ñaari tekki. ngóora soo ko xoolee ci wàllu sëy man na laa jox virilité, waaye soo koo xoole ci wàllu liggéey, ci njambaarte, tekkeem di liggéey bees man a def ci ab diiru jamono, muy nit walla masin)(bu dee loolu la and naa ci)
  • perméabilité : jàllu g
  • tension: dend (baat bii yaa ma ko joxoon waaye bëggoon naa xam gongikuwaayam)(yeguma fu ma la ko joxe de, ndax xaw ma woon baat bii, man naa am dangaa jaawale mbaa nga jaawale bi ma la joxoon, waaye nag manees na koo jefandikoo bu boobaa mu juge ci dend ab der, maanaam tallal ko ba mu talleeku nga weer ko ci naaj wi, ndaxte tension tam ci tendre la juge giy tekki tallal, di ci fr force d'extension di ag jeggi dayo)
  • travail d' un déplacement : liggéeyub tuxu (tuxu ak randu ak topp benn lañu, tuxale, randale, toppale ñoo yem, (waaye ag wuute am na ca defiin wa,tuxu moo gen)

transformateur : soppalikaay b

wattmètre : nattwatt (di jàng nattwat)