Gongikubaat: Nasi: najug baatu wu Almaañ wii di : nationalsozialismus.

Ngérun Nasi aw gisiin la walla ab xalaat bu joyu (totalitaire)bu làngug nasi, làngug politig gu feeñ ci 1919 .

Adolf Itleer(1889-1945)moo ko xalaat, génne ko ca téereem ba doonoon ab jaar-jaaru bopp (autobiographique), tuddoon "Mein Kampf" ca 1925. Ngérum nasi nag mi ngi tegu ci dalub kaweg "xeetu aar wi" (la supériorité de "la race aryenne") ak ci nangu ay suuf yu am solo ñeel Almaañ, ak ci faagaagal "xeet" ak askan yi ñu jàppe yu yées, suufe. Moom Nasi nekk na di ag ndiktaatiir gu politig, walla ag doxe sañ-sañ gu politig gu joyu (totalitaire), guy tibbe ak a roy ca ngérum Faasi mu Itaali mi,moom nag mi ngi nekk di lu ñu taxawal ca Almaañ la ko dale ca 1933 ba 1945. Bi ko jumtukaayi baab yi ( les instruments de propagande)jàppalee, te dëgëral ko ci anam gu tar, la ngér mii mujj di lu ñu nangu ndax xeetu gu Almaañ walla fonk sa xeet gu Almaañ gi muy wone di ko màggal, ak dooleel mbooloo ci rayug jëmmaan (individu), ak màggal gu tar gi mu doon def ki ñuy tudde 4"Führer" (njiit li), njiit lu jàmbaare li, nga xam ne fi ñoom mooy Adolphe Hitler. Moom ngér mii mu xeetal la(raciste), mu safaan-caam la it (antisémite), mu bañ te noonu am tasum xibaar mu féex la ak demokaraasi ak kàddul( woote) ak lu aju ci mbootaayi liggéeykat yi, ak ngérum péexte(libéralisme), rawati na mbokkte . Day jéem a xëcc kuréeli liggéeykat yi, jaare ko ci woote ag booloo gu kuréeli mboolaay yi ci menn mbooloo mu xeet mu dëppoo te méngoo.

Bu weesoo politigu yaatalam (expansionniste)bi nga xam ne moo fi indi ñaareelu xareb àdduna bi, Ngérum Nasi dox na ci faagaagal ay Yahood (Shoah)aki sigaan ( Tziganes ), ci ay dàtti dajaloo (des camps de concentration).

Ngérum Nasi ab xalaat la bu ndayjoor gu catu ( une idéologie d'extrême droite), taariixkat yi di ko tekkee ñaari anam:

  • ag noste gu nguur gu joyu, gog cëslaay la ag xeetal la akug safaan-caam;
  • aw xeet ci ngérum faasi.