Wolof

Soppi

→ Mottalil gongikubaat bi. (Soppi)

baat :

  1. 1. Ab cër la ci cëri nit muy li taqale bopp ak mbagg,
    • Kii de baat bu gàtt la am
    • yaw de masuma laa gis nga takk ceen ci sa baat
  2. 2. Kàddu giy génn ci bolig nit ñu di ko dégg.
    • Xoolal kàddu
    • déglul woybat bi ni baat bi neexee
  3. 3. Am mbind mbooloom ay baat la
    • Baat bi nga bind amul ci wolof
  4. 4. Liy waral boo waxee ñu def ko mbaa ku war a wax ci am mbir
    • Kilifa dafay am baat ci këram

  Waxiin

Déglu baatu baat ci wolofi Senegaal