Wolof Soppi

  Gongikubaat Soppi

→ Mottalil gongikubaat bi. (Soppi)

Tur Soppi

tekki b:

  1. ci xayma: mooy li lay xamal nu am mbir mel, numuy doxee ak numu tëddee
    def ab tekki
    tekkib am mbir
  2. ci làkk: moo lay wax lu ab baat di firi
    baat bii de, xamuma lu muy tekki
    faaw nga xam lu ab baat di tekki ngir man koo jëfandikoo ci say wax.

tekki g:

  1. ci liggéey: samag tekki maa ko liggéey

Jëf Soppi

tekki b:

  1. ci xayma: wax nu am mbir mel, numuy doxee ak numu tëdde
    tekki ab appoo
  2. ci làkk: jox ab baat fireem, wax li muy firi
    tekki ab baat ci wolof
  3. ci liggéey: liggéey ba am alal
    Musaa moom tekki na
    soo bëggee tekki faaw nga liggéey

Tekki Soppi

wu-faraas: (xayma) définir, définition, (làkk) traduire, traduction, (liggéey) réussir, réussite

Delluwaay Soppi

Mbay Fay - nanu xayma - Tëngéej IREMPT (UCAD), 2005