weer
wolof
Soppiweer: am na ñetti tekki
Weer:
- Ci arminaat
Weeru wolof walla weeru weer: tamxarit, digguw gàmmu, gàmmu, rakk-ji-gàmmu, rakkaat-ji-gàmmu, maamu koor, ndayi koor, baraxlu, koor, kori, digg, tëbëski.
- Weer yii ci weer wi lañu aju, su teroo weer tàmbali, bu deewee mu jeex, leeg-leeg ñu mat fan-weer leeg-leeg ñu yées ko, di ay ñaar fukki fan ak juroom ñeent mbaa ak juroom ñatt, ñooy yu lislaam yi it.
Weeru jant: samwie, feewrie, maars, awril, mee, sue, sulet, ut, satumbar, oktoobar, nowambar, desambar.
- Ci Saytubiddiw
- Ci Simi
Ab weer: man naa juge ci xottu bitéel walla beneen ne-ne, lu mel ne kawsu, tey faral a yaraax ba ngay man a gis ku nekk ci ginnaawam.